Content-Length: 109737 | pFad | https://wo.wikipedia.org/wiki/Haj

Haj — Wikipedia Aller au contenu

Haj

Jóge Wikipedia.
Haj

Aj mooy juróomeelu ponku Lislaam, Ci waxi Yonent Yàlla Muhammed ja ni: "Tabaxees na Lislaam ci juróom: Seere ne amul benn buur bu dul Yàlla te Muhammed ndawam la, Taxawal Julli, Joxe Asaka, Woor weeru Koor, Ak Aj ci ku ko man aw yoon", ba tay Aj farata la ci benn jullit bu ko man (ci bépp anam), ci waxi Yàlla mu kawe ja ni:ñeel na Yàlla ci nit ñi Aj néek ba ci ku ko man aw yoon (benn yoon) te ku weddi Yàlla moom woomle na waliif mbindéef yi.

Aj Màkka ak kumu war

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Aj Màkka benn yoon wartéef la ci mukàllaf mu ko man ci yaramam ak ci ab yóbbalam. Manug Yaram wi moodi mu bañ a ame wopp ju ko tee man a dem walla mu ragal ca dem ga dollikug wopp ja, walla sosug wopp walla ak yeex a wér.

Yobbal bi yit moodi mu am lu ko lew lu sell loo xam ne darra ci ribbaa nekku ca, àqi kenn nekku ca, te yalwaanu ko ñaanu ko te mu doy ko sëkk ba du tumurànke ci yoon wi du ca yalwaan du lëjal kenn, waa këram itam mu bàyyee leen lu leen doy sëkk ba du ñu tumuturànke du ñu lëjal kenn. Mu fay boram yépp bu dul bu ab digam teewul, waaye bu dee teew balaa dellusi sax war na koo fay balaa dem walla mu batale ko. Bu ci yooyu yépp amee nag war na ko ni ko julli waree ku ko weddi ab yéefar la, ku ko bàyyi te tay ko te tëlewu ko ci genn anam ab saay-saay la bu bon te bu ko tuubul ba dee sawara la jëm. Ku ko bëgg nag bu demee ba fa muy armale dana fa fekk ku ko jiite ci yi mu war a def yépp ak yi mu war a bàyyi yépp ba ba muy noppi. Moongi ware ci weeru Tabaski

Jeegoy Aji Màkka gi

Ñatti xeeti aj yi:

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Aj am na ñatti xeet:

1-Ajug tamattuh
2-Ajug qiraan
3-Ajug ifraad

Umra yitam sunna la benn yoon mook Aj ñoo nuróo lépp waaye boo doxee safaa ak marwa umra jeex

Faratay AJ

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Aj ñeenti farata la am :
1 yéenee Aj (nawaytul-hajja wa 'ahramtu bihii lill-Laahi tahaalaa)
2 tawaaful ifaada
3 dox diggante safaa ak marwa
4 taxaw arafa.

Sunnay Haj fukk ak ñaar la:
Am na ci ñeent yoy ñi ngi ame ca armal ga:
1 sangu gu jokkook armal gi
2 rafle ci lunu ñaw 3 solub ñëkk akug làmbaay aki dàll 4 labayka.

Tawaaf gi am ñeenti sunnaam : 1 dox gi 2 foon gi doj wa ci loxo walla gimiñ 3 ñukk gi ci ñatti tuur yu njëkk yi 4 ñaan gi ngay ñaan ci tawaaf bi.

Dox gi safaak marwa it am ñeenti sunnaam : 1 foon doj wi bu dee daa juge ca jàkka ja jem safaa 2 ag yeegam diggante safaa ak marwa 3 gaaw gi niy def ci batnu masiil 4 ñaan gu amulub àpp gi ngay def ci kaw safaa ak marwa.


Bañ na ñu

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bañ na ñu lool nag ku Aj ba dikk mu di ko darajawoo walla mu di ko tuddoo di ko dolli ci aw turam, walla mu defe ne gëne na ko (Aj gi) kenn ku ko deful. Na ko def ngir Yàlla rekk, niki muy tuddee Yàlla ak a Julli ak a Woor ak a natt Asaka ngir Yàlla. mu xam ne Aj itam ak yooyu ñoo yam kepp ci ku mu war. lu waay di def na ko def ngir Yàlla rekk ngir lu dul Yàlla ak neen la.









ApplySandwichStrip

pFad - (p)hone/(F)rame/(a)nonymizer/(d)eclutterfier!      Saves Data!


--- a PPN by Garber Painting Akron. With Image Size Reduction included!

Fetched URL: https://wo.wikipedia.org/wiki/Haj

Alternative Proxies:

Alternative Proxy

pFad Proxy

pFad v3 Proxy

pFad v4 Proxy