Content-Length: 148093 | pFad | http://wo.wikipedia.org/wiki/Koom-koom

Koom-koom — Wikipedia Aller au contenu

Koom-koom

Jóge Wikipedia.

Xamale koom-koom

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Koom-koom walla cawarteg koom-koom (activité économique):(làkku grees wu yàgg wa : οἰκονομία, « yor ag kër walla saytu ko »« di οἶκος (kër ci ni ñu ko xame)ak (νέμω yor walla saytu(administrer)) mooy cawarteg nit giy feeñ ci liggéey ak jóox (produire) ak séddale ak joqalante (echange) ak jëfandikoo njuddéef yi (les produits) njëfte yi (le services).

Koom-koom nag ni ngi koy jànge ci xam-xami koom-koom yi, day sukkandiku nag ci gisiin yu koom-koom (théories économiques).

Dees na wax it ci koom-koom niki tolluwaayu koom-koom bu jamono bu am réew walla bu ab gox (zone), maanaam ag nekkam ci gëwéelub koom-koom yi. Cawarteg koom-koom gi kiliftéef yu koppar yi walla góornamaa yi (àtte yi) ñoo koy àtte jaare ko ci ab politig bu di kojug jamono (conjoncturelle).

doxaliin wu mbooloo mi (Les administrations publiques)day def moom itam ay politig yu koom-koom ngir soppi doxiinu koom-koom wu am réew.

benn ci joxoñ yu koom-koom (indicateurs économiques) yu mag yi mooy njuddéef mu ñumm mu biirum réew (NJ.Ñ.B) (produit intérieur brut (PIB)), loolu mooy maye nga man a nattale dooley koom-koom yu réew yi

Xam-xamu koom-koom ( ci Fr:economie)moom xam-xamu mboolaay(social) la buy yëngu ci gëstu ni ñuy jëfandikoo jumtukaayi jóox(production)yu daytalu yi am cig mboolaay (société) ngir faj soxlay ak xemmemtéefi cér(membre)yu mboolaay gii.Xam-xam bii nag mook xam-xam yépp a yam, dafa am ay dëgg-dëggam akaki àtteem waaye jeexiitalu gi mu def ci nekkiini mboolaay yi ak yu politig yi (les conditions sociales et politiques)ak ni ay séqoom ( ay relation-oom) dugganteek nekkiin yii tax na ba melow mboolaay muur ko, cuub ko.

Xam-xam bii li mu làmboo mooy seggat jóox gi (production), séddale gi, ak yaxantu ak lakk walla jëfandikoo njaay yi (marsandiis yi) ak njëfte yi (les services). danuy faral a wax ci koom-koom ne buy wuyyu la (positive) bu dee jéem a leeral ngértey tànn yu wuuteyi, di joxe ay mbooleem ay xalaat jiital (hypotese), walla am mbooloom ay gendiku (ay seetlu),danuy wax it ne bu nattukaay la bu dee leeral doxal yi nu war a def.

Xam-xamu koom-koom dees koy déddale ci ñaari bànqaas yu mag:

Logo Commons

Xool it Wikimedia Commons


Xam-xam
Xam-xam
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma
Xarala
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal
Xam-xami nite ak mboolaay
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama








ApplySandwichStrip

pFad - (p)hone/(F)rame/(a)nonymizer/(d)eclutterfier!      Saves Data!


--- a PPN by Garber Painting Akron. With Image Size Reduction included!

Fetched URL: http://wo.wikipedia.org/wiki/Koom-koom

Alternative Proxies:

Alternative Proxy

pFad Proxy

pFad v3 Proxy

pFad v4 Proxy