Aller au contenu

Dalub web

Jóge Wikipedia.

Ab dalub web, dinañu wax itam dalub internet, da di am mbooloom ay xëti web yu ñu lëkkale ci seen biir duggal leen ci buum gi, jox ko am màkkaanum web ngir ñu man caa àgg. ci 2006 web bi romboon na 1oo ooo ooo ciy dali web.

Dalub web bu ne am na boroom, man naa doon ag lonkoo (këru-liggéeyukaay), walla ag mbootaay, walla kenn nit, añs. Boroom mooy tànn màkkanum web mi ñu man jaare ngir àgg ca dal ba.

Tëddinu xët yi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ab dalub web am mbooloom ay xët la, yu ñépp man a saytu di ko jaare ciy lëkkalekaay yu ne ci biir dal bi. Màkkaanum web, mu ab dal, naka-jekk, day nekk ab URL (ab joxoñukaay ci wolof) bu ab xëtu web, mooy nekk xët wi ñuy njëkk a nemmeeku: di ko wax xët wu njëkk wu dal bi (misaalu makkaanum dal man naa ne www.anafa.alfanet.org). Màkkaanum dal dinañu ko wax itam turu barab, maanaam turu barab bi ngay jaare ngir yegg ca dal ba. Kon ñoom ñaar ñépp a bokk tekki: ñoo lay jox turu dal bi, ba nga man koo ubbi.

Saytu gu nekk gu dal bi lees di wax ag nemmeeku (nemmeeku ab dal), lëkkalekaay yi ne ci diggante Xët yi ñooy tax ñu man a saytu xëti dal bépp te doo ko génn. Jàpp tamit ne ag nemmeekug dal man naa dooree ci xët wu mu manti doon ci dal bi, rawati na, su fekkee ne ab seetukaay moo lo jox URL bi. Jàpp tamit ne xët wu njëkk wi ak yeneen xët yépp a yem, da di ni rekk kay dañu koo jiital ngir mu doon Xët wi ngay duggusee ci dal bi.

Limu dali web yi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Limu dal yi cig yokk la dëkk lu jamono ji di dem:

At Lim
1995 19 000
1997 1 000 000
2000 10 000 000
2004 57 000 000
2005 74 000 000
2006 101 000 000

Yenn ciy dal

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
pFad - Phonifier reborn

Pfad - The Proxy pFad of © 2024 Garber Painting. All rights reserved.

Note: This service is not intended for secure transactions such as banking, social media, email, or purchasing. Use at your own risk. We assume no liability whatsoever for broken pages.


Alternative Proxies:

Alternative Proxy

pFad Proxy

pFad v3 Proxy

pFad v4 Proxy